google.com, pub-8963965987249346, DIRECT, f08c47fec0942fa0
Informer juste notre devoir !!!

WOLOF / MBAXALU SAALUM DIGGANTE COSAANU AK UBBEEKU – BAAY MUSTAFAA KEITA ( BAMBARA BU DEGG WOLOF )

0 94

Mbaxalu saalum dafa bokku ci xeetu toggu yi nu moomal sunu bopp. Waaye ag li cosaanam di ci réew mi itam mu samp i reenam ci digg réew mi ca Saalum, taxul daa ubbiku ci mbooleem xeeti ñam yi nekk ci yeneen dëkk yi. Loolu moo waral am ñu koy woowee mane-fépp.

Sunu dawi réew taxawaay bii lañu war a am ci jamono jii. Senegaal yamul doon dëkk cosaan waaye da caa boolee di sàmm ay jikkoom. Nit ki waróo ñàkk li ñu la xamee, xamee ko saw askan, waaye tamit tëju ci say baaxi maam it ba doo suqaliku baaxul. Loolu lanu war a jàngatee ci mbaxalu saalum dëkk ci digg Saalum ba noppi man a boole ci sa biir ay xeeti ñam yu xamul fu Saalum féetee niki: yéet, keccax, yoxos, netetu añs….. Te terewu koo jaar yoon.

Jamonoo wane na ni mépp mboolaay bu jaxasoo ak yeneen i mbatiit leeg-leeg mu am i coppite. Ubbiku ci àddina bi jaaree ko ci mbaalu jokkoo yi warul tax ñu ñàkk sunuy jikko, réeree sunu mbatiit ba noppi umpale li fi mag ñi bàyyi.

Donte da na dolleeku ci moom yeneen i ñam yu weesu ya mu baaxo lu ci mel ni gejj-tàmbajaŋ, laxas, yàpp ak koŋ nga xam ne seen cafka day ràññeeku lool.
Teewul mbaxalu saalum ci jàppandiwu noflaay am cafka boppam gu dara dul soppi, waral mu neex lool ci làmmiñ ba noppi neex a sàqami ànd ak gaaw a rees.

#BaayMustafaaKayta
#BàmbaraBuDéggWolof
#JàngiituXeetiToggYiCiRéewMi

Leave A Reply

Your email address will not be published.