Maafe bokk na ci xeeti togg yi gën a siiw ci réew mi, moo ne ñu bari ag ndoxandéem lañu ko jàppee. Ba ci aw santam sax day saf xeet wa gën a bari ca Mali : maafe bàmbara. Teewul foo dem ci Senegaal ba ci fa gën a ruqe, danu koy togg.
Loolu day wane ne nit ki ak nu la mbooloo mi man a xoole, donte gëti ku fi dëkkul la walla ku bokkul ci nun moo xam ci wirgo, mbaa ci waaso ba ci sax si xeet, bu mu la yitteel. La war a doon sa yitte mooy fexe ba ànd ak nit ñi ci lañu rafetle ciy jikko ag la nga baaxle ci lu dul jéem a mel neneen walla ñoom ni ñu bëgg nga mel ko.
Xanaa gisoo ni maafe dence li mu moomal boppam muy tiga-dege bàmbara waaye terewu koo jël ca supp-kànja kànja ja dolli ci moom ngir waa kaw gi sopp ko. Noonu la jëlee ca cu-tiir, tiiram ja dolli ngir rafetal melokaanam, ba noppi xëcc fariñ taf ci boppam ngir wuute ak ñi koy niru-nirulu. Boo bëggee nit ñi weg la dangay fexe fonk sa jëmmi bopp bi.
Sëriñ Móodu Mustafaa moom Seexul Xadiim nee na: « dangay defar sa jëmm ji ba ku la gis bëgg la, defar sa jikko ba ku la xas ba xam dootu la man a muñ ».
BàmbaraBuDéggWolof