Le Message du Président Sonko aux membres de sa sécurité: » Je tiens aujourd’hui à rendre hommage aux membres de ma sécurité qui ont été….. »
Je tiens aujourd’hui à rendre hommage aux membres de ma sécurité qui ont été kidnappés par les FDS et illégalement retenus par le procureur de Macky pendant 10 jours avant d’être totalement déchargés hier de toute poursuite.
Je rends hommage à l’ensemble des membres de ma sécurité, qui consentent énormément de sacrifices pour ma sécurité et pour le projet, jusqu’au sacrifice ultime pour certains. Paix à leur âmes.
Ces hommes sont devenus des frères et sont à mes côtés dans les situations les plus compliquées et avec un dévouement sans faille.
C’est ce qui leur vaut ce ciblage et cet acharnement de l’État qui procède systématiquement à des arrestations arbitraires et quelques fois même à des exactions contre leurs personnes.
Je rends également hommage aux leaders, aux militants et aux sympathisants victimes de la folie dictatoriale du régime qui, à Dakar, Guediawaye, Sébikotane et Ziguinchor, ont supporté, et continuent à supporter pour certains, très stoïquement la détention et tout en faisant courageusement face à la justice, ont subi des représailles de toute nature.
Je demande à tous les militants qui comptaient venir passer une nuit de veille devant ma maison d’y renoncer et à ceux qui sont déjà là de retourner se reposer chez eux. Je suis très touché par cet engagement, mais je les rassure : il n’y a rien à craindre ce soir, ni demain.
Enfin, nous donnons rendez-vous au peuple sénégalais demain à 11h pour un point de presse de la Conférence des leaders de Yewwi Askan Wi.


=====================================
Maa ngi ndokkeel képp ku bokk ci ñi yor sama kaaraange te takk-der yi ak toppekat bu Maki Sàll bi jàppoon leen ci lu dul yoon ci lu tollu ci fukki fan te ginnaaw bi ñu bàyyi leen démb te toppeewuñu leen lenn.
Maa ngi ndokkeel képp ku bokk ci ñi yor sama kaarange, te ñu tayle seen bopp ngir sama kaaraange ak ngir sémb bi, ba am ñu ci faatu. Na leen Yàlla fay.
Nit ñooñu leegi ay bokk lanu te ñu ngi sama wet saa su nekk ba ci jafe-jafe yu gën a metti ànd ci ag aamu gu mat sëkk.
Loolu moo tax nu singili leen teg ci càmm gi di leen xoqatal di leen jàpp ci lu dul yoon te yenn saa yi di leen mettital.
Maa ngi ndokkeel it njiit yi, àndandoo yi ak soppe yi nootkat bu dof yi tooñ nekk, Dakaar, Géejawaay, Sebikotaan ak Sigicoor ngir dékku, wéy di dékku ci ñenn ñi, jàpp gi boole ci di jàmmaarloo ak yoon ci fulla, walla boog di dékku wépp mettital.
Maa ngi sàkku ci bépp soppe bu bëggoon a dikk fanaansi sama kër mu bàyyi ko ak it ñi jot a dikk ba noppi ñu dellu seen i kër. Bég naa lool ci aamu gi, waaye maa ngi dalal seen xel : buleen am lenn lu ngeen di tiit ci guddi gi, walla suba.
May jeexal ci, di jox dig-daje askanu Senegaal suba bu 11i waxtu jotee ngir janoo ak saabalkat yi, gu njiiti lëkkatoog Yewwi Askan wi di def.
