Le Président Macky SALL se fout royalement des sénégalais !
Vous avez posé plusieurs actes allant dans le sens d’instaurer l’agenda elgebete dans ce pays. Je ne vais pas y revenir !
Toutefois si vous aviez un peu de respect pour le peuple sénégalais et pour nos Khalifes Généraux vous n’auriez jamais ordonné au bureau de l’assemblée nationale de bloquer la proposition de loi comme vous l’aviez fait jadis avec Mbery Sylla porteur d’une proposition de loi sur la même question !
Mais ce dilatoire ne passera JAMAIS ! on vous demande de criminaliser vous nous parler de non légaliser tant que vous serez à la tête du pays !
Waxal ci linu wax !
Ndax dégg nga misaal mi mala waxoon ?
Yaakaar naani deggoo ko ! Waaji ab surga la te njaatigeem njaboote aw jigéen ! Njaatige li wax surga bi niko bëggu ma njaaloo ci sama kër kon bul jaxasoog jigéen ñi ! Àb diir Njaatige li fekk surga bi ci biir neegu jigéen ñi ci melo wu doy waar (xaayaan ku dégg sereer) muni ko lii nakk Surga bi naa ko : kenn du ci ëmb !!!!!
Waxu ñu wax i dépénalisation ak légalisation ! Liñu wax mooy ñu criminaliser ko !
Parsidaa sa kàddu du loi ! Parsidaa Réewmi tënkkee suko ci sak nekk ak sak ñakka nekk ! Réew mi jiitu nala jiitu ma, te danuy dem bayyi ko muy wéy !
Lima ci metti nakk mooy lañu daa xeexe diine lañu wéy diko xeexe diine batay waaye bii yoon dina wuute !
Soo fullaaloon kilifa diine yi doo seppi lennat ci njaboot gi di wax ak ñoom fekk na tontuwoo sax lañu la wax !
Tànk ci suuf jean ci suuf faww daje !
Yaw kan moola man a sosal ci Reew mii ? Ana say services ? Ana sa dispositif politik ? Ana ñi ngay fay ñu lay waxal xalla da ngaa am recrue yu bées ? Waxal ci liñu wax moo gën naxasaale bi !
Ababacar mbuup